Mais qu’ils sachent que Cité Keur Gorgui, Sebikotane, Hopital Principal, Cap Manuel, quel que soit son lieu de détention le résultat est le même : le président Ousmane SONKO reste un candidat favori à l’élection présidentielle arbitrairement détenu et privé de ses droits par ses adversaires politiques.
Aujourd’hui le constat et inédit. Au Sénégal le président et le secrétaire général (Bassirou Diomaye Faye) du plus grand parti de l’opposition et tous les deux candidats à la présidentielle de 2024 sont arbitrairement séquestrés dans la même prison par le régime de Macky SALL.
Le 17 novembre 2023 sera une date historique pour la démocratie sénégalaise et sonnera le réveil du phœnix.
••••••••••••••••••••••••••••••••••••••••••••••••••••
Waaw Usmaan SONKO yóbb nañu ko ca kasob « CAP MANUEL ».
Waaye naleen leer ne Usmaan SONKO nekk Cité Kër Góor gi walla Sébixotaan walla Raglub « Principal » walla « CAP MANUEL » ak fu mu ci man a nekk njureef li lenn la : Usmaan Sonko day wéy di doon lawax bi ëpp doole ci joŋante yii di ñëw donte ñi mu ko séqal dañu koo tooñ salfaañe ay àqam ak i yelleefam.
Fii nu tollu nii li fi am masu fee am. Fii ci SENEGAAL rekk ngay gis njiital làngug politig gu PASTEF ak jëwriñ ju rëy (Secrétaire Général) ( Basiiru Jomaay Fay) mu làngug politig gi ëpp dayo ci réew mi ñoom ñaar ñépp di ay lawax ci joŋante ci di ñëw ñoñi càmmug Maki Sàll tëj leen ci lu dëppoowul ak yoon ci kaso bi.
Àjjuma yamoo ak 17i fani nowàmbar 2023 mboor la ci demokaraasi Senegaal ndax ci la nuy jaare moom sunu bopp ba fàww.
El Malick Ndiaye